
Paperback: 315 pages
Publisher: EJO Editions, 2nd edition, 2003, 2019
BUY THE BOOK: Contact EJO Editions at info@ejobooks.com
DOOMI GOLO
Tënk Doomi Golo du yomb ndax lu nekk nga ci biir. Ku ñuy wax Ngiraan Fay, dëkk Ñarelaa moo dem ba màggat, xam ni dee ngi dikk, mu namm lool sëtam Badu Taal ma nekk bitim-réew. Xol bi diis, ndeysaan, ndax wóor na ko ne dina génn àddina te mook Badu dootuñu gisante. Ci la Ngiraan Fay jënde juróom-naari kaye, bu teyee mu bind ci bii su ëllëgee mu song ba ca des, jàppe ko noonu guddeek bëccëg, lu ñëw ci xalam mu bind ko, di waxtaaan ak Badu, di ko yedd, di ko fàttali jaar-jaari maamam, di ko wax lu waral réewi Afrig yu bari dëkkee weex ak reyante. Góor gi Ngiraan dina àgge it sëtam ay xew-xew yu yéeme yu amoon ci diggante way-juram Asan Taal ak Biige Sàmb. Waaye ci nettaleem, Ngiraan dafa beral loxo ndaw su nuy wax Yaasin Njay, jóge Tugal, teersi Ñarelaak ñaari doomam yu xamadi, ne day ténjsi seen baay Asan Taal! Ci gàttal daal, Ngiraan Fay bëggul dara ump Badu. Lépp lu mu jot a dund Ñarelaa mbaa mu dégg ko, mbaa mu fàttaliku ko, bind na ko, bàyyil ko fi… Bi Ngiraan Fay dëddoo, benn xaritam bu tudd Aaali Këbóoy moo ko awu ci nettali bi. Aaali moomu nag, ñépp dañu ko jàppe woon ni dof ndax li mu daan def taatu neen di wër mbeddi Ñareela yi di waxtu. Wànte ba ko nit ñi dégloo bu baax yéemu nañu, seen yaram daw na. Doomi Golo sargal la bu ñeel mbooleem ñi taxawoon démb ak ñi taxaw tey, di xeex ngir ñu delloo làmmiñi Afrig yi seen cër, rawatina Séex Anta Jóob mi nàndal xalimag Bubabak Bóris Jóob.